Penku Afrig
Penku Afrig mooy wàllu Afrig gi gën a féete penku. Bénn la ci diwaan yi ñu séddalee goxu Afrig.
juroom ñenti Réew a fa nekk:
Ruwandaa ak Buruundi yénn saa yi dan leen di boole ci Diggu Afrig, ndax li ñu nekk ci diggante ñaari diwaan yi.
Jibuti, Eritere, Ecoopi, Somali, ñooy réew yi ñuy woowee Bejjenu Afrig.
Melosuuf
SoppiYénn barabi penku Afrik,siiw nañ ndax seeni rabi all yu bari, yu mel ne segg, gaynde, ñay,... Li ëpp ci diwaan bii nak ñaay la. Doju Kilimanjaaro ak doju Keeñaa, ñooy yi gën a kawe ci Afrig.
Ci gii xaaju Afrig, làkk yu bari lañ fay wax, kàllaama waa angalteer ak gu waa faraas ñooy yi fa gën a tas, waaye bu nu fatte kiswhili di itam làkk bu tas ca diwaan ba; baati bantu ak yu araab ñoo booloo doon ko. Diiney krist mooy bi fa gën a tas rawatina ca Ecoopi. Doon na diwaan bu bari ay xare yu junniy nit faatoo: ca Sudaan lu mat ay fukki at a ngii ñu ne ci xare, ca Ecopi ba buur ba daanoo ba tay ñu ngi xare ci seen biir. Moom Ecoopi am beneen xare bu mu sexxal ak Eriteere mi ko doon laaj tembteem te jot ko ci 1993, am na fanweeri at. Ca Somali itam ay at a gii ñuy xeex ci seen biir.
Taariix
SoppiPenku Afrik teewee na ay nguur yu mag, rawatina gu Ecoopi. Man nan wax ne mooy nguur gi njëkk ci Afrig. Am na yénn taariixkat yu naan sax ña sosoon Esipt gu yagg ga fa la ñu jòge woon. Nguuru Ecoopi moo tegoon tànk ca diwaan boobu ci jamono ju yagg ja. Lu ko daleen ci xarnub XIX ba bu XX waa tugal yi ñoo leen nootoon, aakimoo woon seniy suuf. Waa portigaal yi ñooy ñi fa njëkkoon a ñéw, waa faraas yi ak waa angalteer yi dal di ci tegu.
Diwaani Afrig | |||
Diwaani KMX: Diggu Afrig · Penku Afrig · Bëj-gànnaaru Afrig · Bëj-saalumu Afrig · Sowwu Afrig Yeneen diwaan: Ginne · Bejjenu Afrig · Maghreb · Sahel · Afrig gu bëj-saalumu-Sahara · Sudaan |